Asi
From Wikipedia
[edit] Diiwaanu Nguuru Room
Ci angale ak ci faranse mooy Asia.
Asi dafa am ñaari tekki ci Injiil.
- Ci bu jëkk mooy li ñu tudde tey jii 'Asi Minër', maanaam daanaka lépp ci réew mu tudd tey jii Tirki (Turquie) lu fare penku géeju Ese.
- Ñaareel bi, ci jamano Injiil ji, Asi benn diiwaanu nguuru Room la woon. Moo doon wàllug sowu Asi Minër. Dafa boole diiwaani Misi, Lidi, Kari, ak genn wàll Firisi, ak dun ya nekk ca géeju Ese. Waa Room ñoo ko def diiwaan ci 129 j.K.. Ci bu jëkk péeyam moo doon Pergam. Waaye, gannaaw jamano Injiil, def nañu Efes ni péeyam. Juróom ñaari dëkk yi ñu gis ca téere Peeñu ma (Pe 2:1-3:22) ñoo bokkoon ca diiwaanu Asi.
Am na ñi xalaat ne yoon bu nekk ñu gis 'Asi' ci Injiil mooy diiwaanu nguuru Room bi. Am na ñeneen ñi xalaat ne léeg-léeg Injiil dafay wax ci ci Asi Minër (Jëf 19:26-27 21:27 24:18 27:2), te yi ci des mooy diiwaan bi.
Man nañu gis Asi ci Injiil ci Jëf 2:9; 6:9; 16:6; 19:10,22,26,27; 20:4,16,18; 21:27; 24:19; 27:2; Ro 16:5; 1Ko 16:19; 2Ko 1:8; 2Tim 1:15; 1Pi 1:1; Pe 1:4.